WAKHTANE CI KHASSIDA YI

WAKHTANE CI KHASSIDA YI

WAKHTANE CWakhtane Ci Khassida Yi 3em parti

 

Ndiaga M Ndiaye

RAA I YA

Waxnanouni Xassida tagg la dieum si geun di mbindef .
Bokou yoyou tagg ay BEUYIT you ken meusta guiss youni mel .
Waxnanouni Xassida gui kou koy diangue dangay begeul Yonnent bi (Psl) ak Sakhaba yi ak mbolem Gayou Bakh yi si geun di mbecté té kou begeul gni begeul SUNU BOROM(SWT

Xasssida « MAD'HOU »la gningi ko teunk si "sahadatou mouridina......" té yilé Xassida nenanou moy li Geuneu gaw si ay xeweul, ak Barké ak beug Yonnent bi

Té Xassida yoyou nio lay wommatal sen bopou.
Mag gni nenanou Ram'mou nak mingui si biir lou yémmè Si biir Xassida gui KOU-TED-KI mingui feuseul lat Ram'mou gui *Yonnentbi (Psl) Défalone Seydina Ousmane
« Zin Noreyni »
KOU TED KI* nena:
« WA FIHI HALA NABI OUSMANE YASFAOU FI SABHINA ALFAN KOULLOUNE HAHAOU NAAROU »
Yonnent bi may na Osmane kerok bissou Penthie mou Ram 'mou 70 mille dieum you xamni Safan ba niéllone na len
Likoy firndé Moy SERIGNE ABDOU LAHAD MBACKE (RA) néna:
Kerok Bissou penthie Mouride bou doug mom rek « ALDIANA » mom kep KOU-TED-KI mo am foumou la fètè wayé Yaw fèté woko fenn Likoy firndé wat moy
« Douna makatiby hibadaty mahan Takharoubi koulla majaya diamakha »
(Sama Xassida mo eup Yoll mbolem diamou yalla ak mbir loulmou rey rey)
Ram'mou kon mingui si Xassida gui .
KOU-TED-KI nena wat si biir:
Kahboun wa Hassanou wa Boucheyri had Barakho wa koulahoum sihrouhou nouroun wa asrarou »
KAHAB ,HASSAN ak BOUCHEYRI Bokkon nanou si tagg kat yi geunona Kawé si diamono Yonnent bi Ba amon na Koumou ssi solallonn manteau boppam
Wayé liniouy kawé Kawé KOU-TED-KI nena Sama tagg day gathial mbolem liniou meusseu way.
Dieuredieuf Serigne Touba Khadimoul Rassoul, Diarama Mmame Cheikh Ibrahima Fall (Baboul Mouridine)

TAYSSIROUL ASSIR
XASSIDA TAYSSIROUL ASSIR Koutedki Mougui Ko Binde Bissou Samedi Si Fadjre Kone Sop Nansi Kép Koukay Diangue Soka Meuné di Diangue Si Fadjre Gui Moy Eup Tawfékh Téyite Serigne Abdou Khadre Mbacké Ibn Khadimou Rassoul Diokhé wonena Ndigeul Gnuir Gnoukay Diangue Par Jeudi XASSIDA TAYSSIROUL ASSIR Kouted ki Néna Bamakay Binde Haraf Bouma Binde Sounou Borom Day Wathie Magalko So Kholé XASSIDA gui Souratoul BAKHARA ba NASSI Serigne Bi Défnako si Biir Kone Xassida Gui Takhawna Takhawayou ALQURANE téyite Serigne Touba Dane Nako Teudjé ALQURANE (Xatnu) so Kholé Tamite 99 Tourou Sounou Borom Yeup Mougui si Biir ak ay Basmala TAYSSIROUL ASSIR Mougui Tékki Li Diapandal Diafé Diafé Yi Kone XASSIDA bi Kép Kouka Sakho Diko Diangue say Mbir Dou Diafé té Lép Lo Beug Amko (Kone Gnougui Yamalé Fi Sounou Kadou Nakh Sounsi Done waxtane Ba Soubeu Dou Takh Mou Diékh Nakh Dafa Yatou)

SINDIDI
Waxnanouni Xassida Aar la si SAYTAN ak leep louy loor .
Xassida bouy tidji bountou ngeunel ak di wommat bep Xeweul ak diko Sakhal .
Amna nak bou nirrou ak mom si teunk mouy « MAHBOUB » Waxnanouni koukoy faral di Diangue SINDIDI say noon dougn meun si yaw dara 
Solen deukonn si bén keur dinanou mudj toukhou 
Nénanou tammit Kou ko Saxal Kouy am Barké ngay Donn rawatina sa Ndiaboot. 
Nénanou am Ndiarigne lol sax si niep rawatina SOXNA YI 
ndax

*Histoire Xassida gui Waxnanouni bokk na si Xassida you KOU-TED-KI ndieuk bind si sayir. 
Bok na si Originou Xassida gui Histoire 'HISBUL SAYF' bou CHEIKH Abdou Khadre Dieylani Ben Kilifa néna Lou ci geuneu yémmé moy dangay xol niata Koun fa yakoun mo nek si Al'hour'ane ak niata « KOUN mo nek si sindidi* ? 
Té KOU-TED-KI néna :
« *BARAKALI FIL HARAKATY WA SOUKOUN.
RABI LEUZI HAD HADANI KOUN FA YAKOUN*
(Sama Borom mo Barkel sama Yeungou ak sama dall ba noppi Diox ma « KOUN FAYAKOUN ).
Té- KOU-TED KI néna tamiit :
Al Hourane wal hadith wal Manafih li ) 
Al'Hourane ak Hadith ak Ndiarigne may Borom)
Diaredieuf Khadimoul Rassoul, Diarama Mame Cheikh Ibrahima Fall baboul Mouridine

NOUROU DAREYNI

KOU-TED-KI nena si *NOUROU DARAYNI 
"yaw sama Borom* defal sama ben beuyit si terrè bi gathial terrè 
Dala'il al-Khayrat"
té ben bayyit NOUROU mo geun terré Imam jazouli KOU-TED-KI nena si terré bi :
"sama Borom nanga yekeuty kep kouy diangue Xassida gui ap touram"
KOU-TED-KI nena si terré bi :
"sama Borom ; kep kouy diangue Xassida gui nanga ko leralal xolam"
KOU-TED-KI nena si terré bi :
"sama Borom ; kep kouy diangue Xassida gui nanga dalal xelam"
KOU-TED-KI nena si terré bi
"sama Borom nanga def mou taxaw taxawayou koor" 
KOU-TED-KI nena si terré bi
"sama Borom nanga def mou dox si diguenté Niit ak loudoul nonou)
KOU TED KI bou moussonn waax sama terrè BI NOUROU DAREYNI la donn waax
Dieuredieuf Khadimoul Rassoul, Diarama Mame Cheikh Ibrahima Fall Baboul Mouridine



En savoir plus : https://1milionsdepersones.webnode.fr/news/wakhtane-ci-khassida-yi-3em-parti/


I KHASSAIDE YI

Rechercher

‎NOUROU DARAYNI(+1MILIONS DISENT DIEREDIEUF SERIGN TOUBA SUR FACEBOOK) DAHIRATOU NOUROU DARAYNI DIEUREDIEUF SERIGNE TOUBA © 2014-2016