WAKHTANE CI KHASSIDA YI

WAKHTANE CI KHASSIDA YI

 

WAKHTANE CI DIALIBATOU MARAKHIB

Koutedki Mougui Ko Binde si Diamono wayssasine So Kholé Serigne Touba Bamou Bindé XASSIDA DIALIBATOUL MARAKHIB Dafko Sani Si Guéj Né XASSIDA bi sou Déllousé thi mane ta toyoul raafoul ma khamni nangouna Apré sila bén gendarme bou toudou Moussa moko fore indil ko KOU TED KI té toyoul raafoul Téyite Serigne Abdou Khadre Néwonena Nankay Diangue Par Vendredi Serigne Touba Néna XASSIDA bi kouka Yoré Rombou si Armél kép kounfa done Mougeul Dankay Djégal DIALIBATOU MARAAKHIB day diokhè mbòlò tèyit day tarbiyeu koukoy diangue day takha deudou addouna.koukoy diangue day takh ga beug Serigne Touba saf-sapp ci Mame cheikh Ibrahima fall koukoy diang dèsoula bindeul bakkaar kou koy diangue Sounou Borom mayla lo xamni kouko doul diangue dinala ci Niè Waxat nannouni Xassida gui day taxaw taxawayou niane, Sant, Jihad, Tagg, Djoulli, Ak Diamou yalla XASSIDA bi sokay Diangue Mbolém Mbote you Gayou Bakh yi Amone Digako Ame 

 

(Kone Gnougui Yamalé Fi Sounou Kadou Nakh Sounsi Done waxtane Ba Soubeu Dou Takh Mou Diékh Nakh Dafa Yatou

 

 

NAFA ANI

 

XASSIDA "NAFA ANI" wax nagnou nii SERIGNE BI "NAHBOUDOU" lako teugué wayé liko SOUGNOU BOROM wax mo takh harafou "DELL GUI" gneuwou thi. 

 

XASSIDA wakh nagnou ni sou féké sa khel dafa nakhari doo guawa mokkal sokoye diangue di nga nékh khél Bou sobé yallah

 

waw kisse gou werla mome XASSIDA GUI. BARKE XASSIDAS YI

 

MATLABOUL TAKHABOULI

 

SERIGNE ABDOU KHADRE MBACKE (RA) waxnani Kou Beug say Adio fadiou nanga ko Takko .

 

Waxnanouni Xassida gui Salatou la, Xassida Toub la, Karangué ak Niane la ak Diamou yalla gou mag ak Diapandal etc .

 

Si Guestou Nénanou bax na lol si kouy Diangue ak kouy Dionganté (examen), wala concours.

 

Kou bax Néna keep kouy sakou mbiir boko Sakhalé diotsi lolou KOU-TED-KI niane nako si biir 

 

«Warzouhniyanil yawma bihi niadiataMinal hida warzouhniya’l houfaata »

 

(Nanga defal si bilé biss ak mouthiou si ak noon ak té nga may ma ak Dal)

 

“Warzouhniya‘l hina bima tahtarta liya “Wa fil Oumouri kouliha Dabir liya "

 

(Nanga ma defal Am Am binga ma taanal té nga guindi ma si leep loumay Doug)

 

“Warzouhniyal yawma bihi sakinah““Wal tourinil kahbata wa Madina“

 

(Sunou Borom nanga ma defal ak dal si biss bi té nga wane ma kaba gui ak Medina)

 

KOU-TED-KI wax dji feusseulat nako si « HATIMATOU MOUNADIAT“ Etc

 

Dieuredieuf Serigne Touba, Diarama Mame Cheikh Ibrahima Fall (Baboul Mouridina)

 

 

MOUXADIMATOUL XIDMA

 

Mouhadimatoul Xidma lep ay salatou hala nabi la té KOU-TED-KI bind nassi you outé wayé bép bo ci takkol dalay rakhass banga set niodil-la ay xeweul té mom day fek fou dara nekoul mou def fa dara, fek fou amm ass toutt mou foul ko, fek fou lou barri nék mou barkel ko, Xassida gui da lay fott ba nga set, dila bidjil ay nguenel , di la diégnal ay loor ak di fadj adio you meuneu donn .

 

S bassirou Xelcom nena S Saliou Mbacké wax nako dan na degg mak gni nann eup na diangue si ap diotay (ben niit). 

 

Barri ay salatou you kemané si biir té gaw si ay Adio.

Bokk na si yenen Xassida Salatou Mouhadimatoul Koubra, Dourrou samin, wala xassida yi nek diwaan salawat etc......

Bokk na si leep li niit di deef té beugue ko bayyi mou teu ko sou tako ak "DOURROU SAMIN" mou nex ko, mou naxari ko dinako bayyi inchalla

 

 

MOUWAHIBOU NAFIKH

 

"Nien si Mag gni nenanou Xassida gui KOU-TED-KI mingui ko bind ci attou WAYSASSIN (1316 an musulman) .

Mom ak Jazbou, Mouhadimat, Radiytou etc……. nio massé.

 

S Abdou Khadre Mbacké nena day mayé Xeweul di yokk ak Ngeum, ak beug Yonnent bi (PSL).S

 

Mbacké Bousso nena Mawahibou ak Sab’houn Takhi daniouy mayé ay Xeweul Bok na si kemtanou Xassida gui Yenn Beuyit niou teunké wat bénen Xassida Bokou nassi tamiit Xassida you KOU-TED-KI waxon ni nioy« Naarou Goor yi » Kou len war té wathie wolen niou wommat la ba fi mom

 

Kemtaanou Xassida gui:

Ben biss Mame Thierno Birahim Mbacké meussna sant ay Talibèem niou Yoboul ko Dougoub bimou bayonn si KOU-TED-KI ; Yobanté walé len nilen « Nélénko Maraal nanou lol »

Ba nioniou agguèe wax KOU-TED-KI yobanté Borom Darou bi.

Si leu KOU-TED-KI wax Kourel gui nanou Diangue « MAWAHIBOU » Kourel gui di diangue ba Tollou si :

"nala dialala nala diamala ""miman taxala Rabii sama i"

KOU-TED-KI diglé niou Bamtou ko ; ba noppi tek si

« Yaw Borom Assaman sama beug beug moy ndox »

Rek Taww bi tambali di Taww .

Baniou Yonnéwaat si KOU-TED-KI nguir mou Dakkal Taww bi

 

Amna Biss KOU-TED-KI di waxtaan ci Bissou Penthie ak Taraay ga.

Ba waxni bou Biss boba Niep Sama Bopp laniouy wax bamou dess Yonnent bi(Psl) ;

Mom sama Khèet lay wax .

Bou biss boba ba Yonnent bi(Psl) dem HARASS ba soudioteul Sunu Borom ,bam niko Siggil té Dem Ram’mou .

KOU-TED-KI nena bou diogué ba dem si Taxawaay ba dinako Dogallé Fatalliko lama ko waxonn si "MAWAHIBOU

"‘’Antal Karimou Annal Hadimou ‘’‘’Deuhran Oudimou Fika sana’i ’’.

Bou boba dinama Yéssalal Ram’mou bi mouma mayonn thia Adouna Sogaa dem tokk sa Keer gua.

Bou boba loxo bou touty bi koumou seedoul dinga yendo khif fanané fandé (etc.....

 

Dieuredieuf Serigne Touba Khadimoul Rassoul, Diarama Mame Cheikh Ibrahima Fall (Baboul Mouridina)

 

 

 

Rechercher

‎NOUROU DARAYNI(+1MILIONS DISENT DIEREDIEUF SERIGN TOUBA SUR FACEBOOK) DAHIRATOU NOUROU DARAYNI DIEUREDIEUF SERIGNE TOUBA © 2014-2016