WAXI MACK GNI

WAXI MACK GNI

 

 

Le Grand Poète : xarnu Bi 1ère partie
Les Figures de styles y apparaissent : métaphore , oxymores, et j'en passe

Sëriñ bi noo gi deeti ñaan Faqiir dafay nangoo dagaan Nangul nu lépp lu nu ñaan Ndax Yàlla naatal xarnu bi

Noongi dangaan ci Mustafaa Ma nekk marwat'ak safaa Ak àqi amdi Mustafaa Mi Yàlla jébbal xarnu bi

Ak àqi mboolem ay rakkam Ak àqi séen baay yi ñu am Ak àqi seex yi Bàmba am Ndax Yàlla naatal xarnu bi

Mboolem muriid yépp a ngi tuub Tey réccu bàkkaar yi nu joob Ba lu nu bay-bay, du nu góob Sëriñ bi geesul xarnu bi

Mbàkke, dangay boroom i mbóot Te sag njaboot tawat gilóot Ñu def ma ab àntarpareet May làpputoo waa xarnu bi

Aw ma màqaamam di la woo Waaye muriid yi ñoo ma woo Ni tawatal te bu ñu woo Saw làmmiñay wow xarnu bi

Tay jii ma wax bani tareet Ngir yaa ma def antarpareet Yaa fab i xam-xam ne yuréet Ci sama xol, ci xarnu bi

Te bul ma tanxamlu ci ñaan Ngir lii ma bon tey ku añaan Muriid yi yépp a la ko ñaan Ngir bëgg a dekkal xarnu bi

Jooy i perantal la nu jooy Boo nu fabul, lee nu ni wooy Ku nuy yafal, ban def i kooy Mu dellu naatal xarnu bi

Jis u nu baay te noo ngi raam Ku ñàkk yaay, day nàmpu maam Buural te boot nu, ngalla daam ! Roggani mboolem xarnu bi

Fabal sa doom yi yépp boot Ñoom it ñu boot séenug njaboot Ku manta boot nga jox ko mbóot Ndax Yàlla naatal xarnu bi

Te fab muriid yi suturaal Mottali jàkk a jii nu naal Foo toll dolli séen alaal Ndax Yàlla naatal xarnu bi

Ndax Yàlla amdi Mustafaa Tabax jumaa-i Mustafaa Bam tol ni marwata'ak safaa Ndax Yàlla naatal xarnu bi

Boolem muriid yépp a ngi jooy Ngir luñu bay-bay mu dal di gooy Ba séen i àddiya'a ngi booy Sarax nu naatal xarnu bi

Jamono jaa ngi xiif a xiif Luñ togg, bar gi ni ko fuuf Seex Bàmba, neel ngën ji mbindéef Mu dellu naatal xarnu bi Xiif tax na, ñenn mag ñi yooy Xiif tax na, gor su ndaw si jooy Xiif tax na, yenn tool yi booy Sëriñ bi geesul xarnu bi

Taxna, ña daa joxee ngi laaj Ñii ñépp séen i sas di xaaj Ken dóotu dem fenn ba waaj Sëriñ bi geesul xarnu bi

Xam nañ ni yaa nu daa tawal Daanu bayal, daanu ñoral Daanu roñal, daanu daggal Feesal nga sàqi xarnu bi

Sa yërmandee nu daa defal Lu xel dajul, daanu dëfël Daanu tibbal, daanu leel Reggal nga mboolem xarnu bi

Sa yërmandee nu daa sanal 
Jigéen ña, yaa nu daa amal Tay ñépp a yam ken amatul Sëriñ bi geesul xarnu bi

Ñoo séen i sag sàggiku na Ñoo séen i gaay dàggeeku na Ñoo séen i ngëm rékkiku na Ngir ñàkk gii ci xarnu bi

At moo ni ndax mooy tane daaw Mooy gën a far dellu gannaaw Ba rab yu aay yi sax di naaw Ay Mbàkke ! géesul xarnu bi

Wëy ! nu ni wëy! noo ka torox Yalwaan, amoo ku la sarax Garab bu daanoo xob ya lax Bàmba'ay danjaamal xarnu bi

Garab gu mag bu nee jirim Garab yu ndaw yi day jirim Méññat ma say mbir ya ëlëm Lii rekk a dal waa xarnu bi

Allaahu akabaruz zamaan Jamono moo man a safaan Xéewël yi daf daa walangaan Ci ndabi mboolem xarnu bi

Libeek, sikkeek i sëhfaraan Lan daa diwoo muy walangaan Nuy xelli kopp ya di naan Wata ya kornu xarnu

bi Astaxfirul Laahal Aziim Tuub nanu lan daa def i koom Te muy lu neexulan boroom Jurbel a wuuteek xarnu bi

Xeewal yi daf daa wal-wali Baawaan fi nun di kel-keli Moo tax ma jóg di pél-péli Sëriñ bi geesul xarnu bi

Xeewal yi daf daa walangaan Waxset nga wuute nga'ak sayaan Xamoo xur'ak tund'ak sayaan Sam ndox a naatal xarnu bi

Wàcci nga yaw loo mas a wax Def nga ko jox ku mat a jox Daawoo nu nax, daawoo nu cax Séddon nga mboolem xarnu bi

Gàñcax gu ndaw gi weddatul Mag ña nga yar ken woddatul Moo tax ma naala suuxatal Njëmbët li wan ci xarnu bi

Njëmbët la mooy gaa ya dikkon Daa wéy ci xeewal ya fi won Tay ñi ngi def ya ñu bawon Ngir ñàkk gii ci xarnu 
bi

Ag ñàkk a bon ci waa ju baax Day tas kërëm xolam ba jaax Daa ceeb u tay ngay añe laax Jaaxal na gaa yi xarnu bi

Leek-leek nga gis fi ab muriid Muy taxawaalu ni'b mariid Walla mu xàcc def tëriid Ndaw njombe gaa yi xarnu bi

Ànd'ak komersaa ya di jaay ñii di wajaaseeri baxaay Te xamni yaa doon séen i baay Moo tee nga naatal xarnu bi

Ña lee nga xàcc i defi seef Ñii def i dag ngir bañ a loof Ñii daw ba raw ba ni nu fuuf Moo tee nga naatal xarnu bi

Yaw la nu yaakaar abadaa Ngir yaa nu tàggaleek bidaa Tuub nanu mboolem la nu daa Bàkkaar ci njëkk xarnu bi

Yërëm nu tay yaru na nu Dóotu nu fo, xàmme na nu Dóotun nelaw, yewwu na nu Yërëm nu naatal xarnu bi

Soo nu joxoon la nu yoran Dóotu nu def ,nanu defan Xanaa yëgooni yaru nan Ku weddi laajal xarnu bi

Yërëm lu nan, torox lu nan Jooy na nu ren, saraxtu nan Soppeeku nan, jébbalu nan Sarax nu naatal xarnu bi

Nun tuxu nan sun kër i baay Gàddaay te def la ngën ji baay Tuubaa di kër, bàmba'a di waay Sëriñ bi geesul xarnu bi

Muriid yi saalit nanu ren Ngir xamni yaa léen ame wan Yaa léen joxon la nu yoran Yobbu nga mbóoti xarnu bi

Tiijaan yi réccu nañu tay Xam nañ ni bëy du sóoru boy Yaa man a may nit lu ko doy Moo tee nga naatal xarnu bi

Bawal-bawal jolof-jolof Mboolem pël'ak naar'ak wolof Kenn gis a tul ku ame yëf Sëriñ bi geesul xarnu bi

Koo xam ni daan a ame jaak Daa ame àngaar'aki juuk Mii at mu am déwén mu jéek Sëriñ bi geesul xarnu bi

Ku mas a am yaar i wata Soxla na ren jii yaar i mëta De munta am njëg u mëta Sëriñ bi geesul xarnu bi

Koo xam ni daan a ame taax Tay ming ni ngeeju'b néek bu baax Bu gën a feex bam ni ca faax Sëriñ geesul xarnu bi

Kër yaa ngi wéet ba ni woyoŋ Lal yañ yoroon def i koyoŋ Ña doon i wuur def i koyaŋ Sëriñ bi geesul xarnu bi

Tubaab yi sax pert nañu Ña léen gëmoon pert nañu Yahood yi it fayit nañu Yal na ñu yées ci xarnu bi

Ña tukkiwan faf nañu laŋ Fuñ wàcci deef i léen falaŋ Àdduna yaa ka noo welaŋ Sëriñ bi geesul xarnu bi

Naar yaangi yalwaan'ak a xaar Seex buñ xamoon dellu fa jaar Ken talatul loo jox i naar Sëriñ bi geesul xarnu bi

Wooy Mbàkke ! yuuxu nan ba dee Wallu nu boo yeexee nu dee Melal ni kuy rammu ku dee Yaa nuy tinul waa xarnu bi

Yaw yaay donoy Muhammadu Te yor nga sirrub Ahmadu Te yor nga bóot i Haamidu Man ngaa defar waa xarnu bi

Man ngaa defar biteek i biir Defar nga baadoola'aki buur Yaa dindi àllarba'ak dibéer Sàkk Muriidi xarnu bi

Man sa kanam, man sa gannaaw Loo sant Yàlla mu ni waaw Loo wax fa diiwaan ñu ni waaw Wax léen ñu naatal xarnu bi

Sa mbir ëppante na'ak dërëm Nde xarnu bépp am gërëm Te am dërëm te yokku ngëm Nga may njariñ waa xarnu bi

Ma léebu ngaa yi la xamul Waa ju xamul dees koy xamal Subhaana, yaa ka mat kumal Yaa neex a wan waa xarnu bi

Nan far waññee ku tagg daam Ngir moo nu may lu jombi maam Boolee'k Muriid yuy daw di raam Ag cant a war waa xarnu bi

Bàmba muneef u laa misaal Yaay géej gi wër waa senegaal Deef u la jàlle genn gaal Say duus a tooyal xarnu bi...

 

Rechercher

‎NOUROU DARAYNI(+1MILIONS DISENT DIEREDIEUF SERIGN TOUBA SUR FACEBOOK) DAHIRATOU NOUROU DARAYNI DIEUREDIEUF SERIGNE TOUBA © 2014-2016